Lyrics

Gisoo ni fu sori la joge Ba ñuy gone dañ foogoon ni Boo maggee Loo yootu day gaaw Tera'nga bi day naxe ci boo foogee Lepp yay boroom Adduna bi pottu Ndaa la boo naanee jox sa moroom naan Jamm du doy!!! Du alal jamm moo li gën ci ñun Nang xoolee sa bopp yeene ko peace and love and harmony Lepp du yay boroom fii dang fi am waar keneen am fi waar Saabu bi footul boppam Man la man la lune nga ne yay boroom Fii demal maa ngi ñëw la Tay sa bis suba bisam la Boo goree jekkoo del baalee Adduna di ndaa yow Soo naane jox sa moroom naan yow Yaatu yaatalal sa xol yow Jamm du doy!!! Seet naa ba seet moy li gën ci ñun Mbëggeel akk alal du doy Bu fi jamm nekkul dara xajjul ci ñun Saabu bi footul boppam Man la man la lune nga ne yaa ko moom Dimbalil xale bi mbokkam Xoolal li nga yeene sa bopp yeene ko bepp jaam Gisoo ni fu sori la joge Ba ñuy gone dañ foogoon ni Boo maggee Loo yootu day gaaw Tera'nga bi day naxe ci boo foogee Lepp yay boroom Adduna bi pottu Ndaa la boo naanee jox sa moroom naan
Writer(s): Abdoulaye Sy, Ashs The Best, Olivier Delahaye Lyrics powered by www.musixmatch.com
instagramSharePathic_arrow_out