Similar Songs
Credits
PERFORMING ARTISTS
Ashs The Best
Performer
COMPOSITION & LYRICS
Arfang Tiare
Songwriter
Lyrics
Mmmm
Mënatuloo siggi ci bët xool ma
Mënouma woon gëm ni naxo ma
Ku la ko waxoon loolu am na
Du agne du réer te matt na soor
Li nga ma waxoon wuutek say jëf
Digué boor la té yaw woor nga
Nga laaj ma sama xol man ma jox la
Defoo ma ni sa bopp takh nga gaañ ma
Keerog sam xel bi waroon na tey, say wax woor ma
Dañ ma tére woon ma taxaw watt ni sañuloo ko
Ma jël la teg fi ma tegul benn mindeef
Bi nga xamee bëgguloo ma wax ma ko
Bëñ ak lammiñ fak ñu laale (waawaaw)
Wayé fajaloo ma sama gàcc (mmm)
Nu may defak samay dëkkëndoo (samay dëkkëndoo)
Duma siggi xol ci samay nawle
Gàccee gi fu ma koy waxé (héeee)
Ci xol la tiis boo may lacce (haaaan)
Dinga ko gis Yàlla ñuy àtté (Yàlla ñuy àaaaatté)
Bi nga fi jii bës ding ko goobe (goooooobe)
Ayway Samba
Yaw dé yërëmoma (yërëmoma)
Nga tooñ ma benn yoon man ma baal la
Nga def ko ñaari yoon man ma baal la
Yeah way Samba
Yaw mi de bëgguloo ma (he le le le)
Nga laaj ma sama xol man ma jox la
Defoo ma ni sa bopp tax nga waar ma
Waawaaw
Mmmh mmh
Ki sedday bi, tàngoor bi
Nekk ci naaj bi té kéraloo ma, kéraloo ma
Defuloo ma ni ma la def
Lu ma xam wax la
Alaal ma jox la
Mbëggeel ma waan la
Kan nga ma jënde lan la ma rawé
Ki nga ma jënde lum ma ëppëlé
Réwoo réw weur naa ko (Réwo réwo)
Keneen ku ma guis ni yaw la (Réwo réwo)
Ñu mel ni yaw lay musloo (Woo mbëggeel)
Nga def lii man lay wuyoo
Réwoo réw weur naa ko (Réwo réwo)
Keneen ku ma guis ni yaw la (Réwo réwo)
Ñu mel ni yaw lay musloo (Woo mbëggeel)
Ni mbëggeel def man lay woyloo
Ayway Samba
Yaw dé yërëmoma mooma
Nga tooñ ma benn yoon man ma baal la
Nga def ko ñaari yoon man ma baal la
Yeah way Samba
Yaw mi dé bëgguloo ma
Nga laaj ma sama xol man ma jox la
Defoo ma ni sa bopp tax nga waar ma
Gàccee gi fu ma koy waxé (hééééé)
Ci xol la tiis boo may laaje (haaaaaaaan)
Dinga ko gis Yàlla ñuy àtte (Yàlla ñuy àaaaatté)
Bi nga fi jii bës dinga ko goobe waw
Writer(s): Arfang Tiare
Lyrics powered by www.musixmatch.com