Video musicale
Video musicale
Crediti
PERFORMING ARTISTS
Abdoulaye Guitte SECK
Vocals
COMPOSITION & LYRICS
Abdoulaye Guitte SECK
Songwriter
PRODUCTION & ENGINEERING
Abdoulaye Guitte SECK
Producer
Testi
DOUANOU SENEGAL
Douanou Senegalaise yen de diambare guen
Diambari Senegal man de naw loo naa len
Adounaak la thia biir
Askan wi nieuw niou sargal len
And doug thi sen biir
Wayal len begual len
Kham guen ki guen doon
Lepp nguen diem tekk thi yoon
Am guen dal ak tey
Te fonk lool sen liguey
Yenay doundal askan wi
Ndakhte yenay wen wi
Yena waral hopitaux yi
Ecole yek tali yi
Yena gui saytou loune
Guir niou bagn noo possane
Thi dieri diek guedj guek diaw dji
Economie bi mooy dole dji
Douanou Senegal yen de diambare guen
Diambari Senegal man de naw loo naa len
Yen de fate woulen lan moy sen mission
Tay le guen sen nelaw yelloo guen admiration
Sentinelles du pays
Soldats de l’economie
Rien n’échappe à vos yeux
Face aux défis audacieux
Yaa gui dadiale lou askan wi di dounde . . Yaa Yellol dolel
DEVENIR MEILLEUR POUR MIEUX SERVIR
Bou de taw mbaa mouy naath waay
Amoo nelaw amoo noflaay
Yaa gui khekh guir niou dounde
Yaa waral kouy liguey di dounde
Talal lokhoom bou wer dewe
Sa takhawaayou taya sedde
Way niaaw tef ye gui sentir
Il y a des frontières que l’on ne peut franchir
Nagn len yokkal seni dioumtoukaay yi
Ba drogue bek medicaments you bonn yi
Ak bep khetou mbonel yi
Bagnia danel sounou économie
Ngiy newal dole rew mi beugueu dounde illusion
Lepp louy thiay thiay dougn thi delou guinaw
Kone kepp kou fi nite te di dounde raison
Do nangou Senegal gui di delou guinaw
Rosso ba karang Kidira ak Ziguenchor
Dem Oumpack keur Ayib dem ba Port ak Aeroport
Guis naa la yaa gui khekh guir euleuk sounouy doom
Meun doundak dignite thi sen rew gui niou moom
Douane Senegalaisel yen de diambare guen
Diambari Senegal man de naw loo naa len
Douanou Senegal yen de diambare guen
Diambari Senegal man de naw loo naa len
Yen de fate woulen lan moy sen mission
Sen gueum gueum gui daal yello na promotion
Douanou Senegal yen de diambare guen
Diambari Senegal man de naw loo naa len
Naw loo naa len
DEVENIR MEILLEUR POUR MIEUX SERVIR
Written by: Abdoulaye Guitte SECK
