Lyrics

Ndeye mougneul sa thiono dina faay Say rongothi dina férr bilay Ndeye sa Tàar bi nakar rako mour tay Kéneu xamatoul loy nirol ndakh thionay seuy Ndeye meusta degg waw gòor Té sou outi woul indi keur gui dougnou tal bay sôr Teksi aye gorom sonal ko Té sou wakhé dieukeureum tégal kossi aye dóor Ndeye siguil nga xolma Sa beugn you wekh yi la nameu nak rétane ma Djougal nga dellou keur gua Mourol sa malanou soutoura té fanane ci jamm Yéneu say mou dioy ndakh wakh you bone yignou deukal ci nopam Rongogn yangui sàngu dom dji mou tím diko nampal (Góor-góorloul waay) Ndeye mougnal Yalla guiss na lepp Ndeye Dina meussa bakhi Boul meussa bayi Ndeye mougnal Li lepp dey diekh Faw mou méti dora nekh Ndeye mougnal Ndeye mougal sou dom yi magué féral say rongogn Boul meussa bayi Ndeye mougnal Enh mougnal waay Dina meussa bakh Ndeye mougn na ba naak Wouyou djina borom mam biko saak Ndeye meusta xam banekh Té bimouy tolou ci digë ndawam ngako takk Meussoul ame ci yaw louko nekh Té lounék ladane def nguir dap sa banex Ndeye meussou lo fanae aleu Wayé tay goudé nga Foy fanane tay? Nakar ak tiss rek laka yobbou Wayé lepp diexna Boul guiss lo ragal way Ndeye mougn na ba dém Té narta féké sah ndieurign domam Ndeyoo Ndeye!!! Dieuf djou bone djounek dieureur-am Tek koko mom aki mbokam Lou nguéni lay tay? Sa doundou gawa fay comme sondel bougnou tek ci nguélaw Yalla bo guiss lo ragal finga dieum Teudeul nga nélaw Ndeye demna!!! Ndeye demna (demna)!!! Ndeye demna!!! Demna dotoul nieuwatt Meusoul ame louko nekh ci bir doundam Ndeye demna
Writer(s): Unknown Unknown, Abdoul Aziz Fall Lyrics powered by www.musixmatch.com
instagramSharePathic_arrow_out