album cover

Mébet

9,626Afro-Pop2026
album cover
Mébet was released on September 25, 2026 by J à n j a as a part of the album Digg Doole
ReleasedSeptember 25, 2026
LabelJ à n j a
BPM87
Melodicness
Acousticness
Valence
Danceability
Energy

Music Video

Music Video

Lyrics

Yàlla may na may bët mais ma xippi xool
Jël yoon wi ma doy ma def ko sama yoon
Mama daf ma jàkk ne day bari noon
Ndaxte dafa bari jom
Am looy bañ day indi noon
Laahu maa ngi Lay ñaan Nga dooleel samay noon
Ndaxte loolu dafay tax ma dolli jom
Samay rakk ñu ci bari roy ci man
Su ma jengee ñu daanu
Te loolu daf may metti lool
Papa bëggoon naa jaar fi nga ma awloo
Maman bëggoon naa xool fi nga joxoñ
Waaye misig moo ma woo
Ne ma Aama dunya a ngi lay xaar
Fësal wane ni nga mane
Man bëggoon naa fay li nga daj ci man
Wan la sax ne yëg naa sa coono
Eey baay a bóoy masta coono
Àdduna a may xaar faut que ma fësal
Dëkk yi nga agsi
Ci yoon yi nga jot a àbb lay doon
Mbégte yi nga tàbbi
Bànneex yi nga jot a aju lay doon
Dëkk yi nga agsi
Ci yoon yi nga jot a àbb lay doon
Mbégte yi nga tàbbi
Bànneex yi nga jot a aju lay doon
Jagle yi nga am lu jaadu la
Boroom bi a koy def ci doomi Aadama
Yuuxal yëngal xolu àdduna
Yoon wi des na, des na sax lu yaatu lool
Jagle yi nga am lu jaadu la
Boroom bi a koy def ci doomi Aadama
Yuuxal yëngal xolu àdduna
Yoon wi des na, des na sax lu yaatu lool
Moom moo ma ne xamuloo ma
Waaye xam naa la bu baax
Dellu ne ma wóolu naa la lool
Te fas yéene namaa
Ne ma lii may waaj a def
Dama lay jàppale
Àndandoo bi ma am
Moom moo ma feeñu
Xaaju guddi mu jël ma
Jébbal ma ay mbóot
Ne ma kóllare lanuy fas man ak yaw
Ma lay xamal yaw it ngay xamle
Jox la ci pet looy wan àdduna yépp
Masàmba Buur Ndëng Leen
Ci sa dereet la nekk
Àndandoo bi ma am
Moom moo ma feeñu
Xaaju guddi mu jël ma
Jébbal ma ay mbóot
Ne ma yuuxal laal xol yépp
Maas Buur Ndëng Leen
Ci sa dereet laa nekk
Dëkkk yi nga agsi
Ci yoon yi nga jot a àbb lay doon
Mbégte yi nga tàbbi
Bànneex yi nga jot a aju lay doon
Dëkkk yi nga agsi
Ci yoon yi nga jot a àbb lay doon
Mbégte yi nga tàbbi
Bànneex yi nga jot a aju lay doon
Jagle yi nga am lu jaadu la
Boroom bi a koy def ci doomi Aadama
Yuuxal yëngal xolu àdduna
Yoon wi des na, des na sax lu yaatu lool
Jagle yi nga am lu jaadu la
Boroom bi a koy def ci doomi Aadama
Yuuxal yëngal xolu àdduna
Yoon wi des na, des na sax lu yaatu lool
Written by: Abdoulaye Diop, Saliou Samb

Shazam Footer

Select language:
Google Play Store
Apple App Store
Chrome Web Store
Galaxy Store

Follow Us

Loading...