制作

出演艺人
El Hadji Ndiaye
El Hadji Ndiaye
表演者
作曲和作词
El Hadji Ndiaye
El Hadji Ndiaye
词曲作者

歌词

Woy wi: Bor yi (La Dette)
Dañ ñu dëj
Bor yii dañ ñu tëcc
Ba tey jilee
Ñun ñii mënatuñu rëcc
Ñun dundatuñu
Réew mi lañu xoj
Ñun dundatuñu
Néew ji doole yi
Lañu xoj
Dañ ñu dëj
Bor yii dañ ñu tëcc
Ba tey jilee
Ñun ñii mënatuñu rëcc
Ñun dundatuñu
Néew ji doole yi lañu xoj
Ñun dundatuñu
Néew ji doole yi lañu xoj
Juróom-fukki at
Ba tey ñu ngi fey
Te fey googilee
Tey jii la gëna rëy
Xale yi jàngeetuñu
Ñi tawat fajootuñu
Juróom-fukki at
Ba tey ñu ngi fey
Te fey googilee
Tey jii la gëna rëy
Te dégg naa ne
Bor yii niñu ko tërale
Dootul jeex ba fàww
Mënatuñu ko fey ba raw
Thomas Sankara
Gisóon na bor yi ñuy sànq
ANNULONS LA DETTE
ET RELEVONS LA TÊTE!
Nous, on ne vit pas
Nous, on s'accroche!
Nous, on ne vit pas
Nous, on en souffre!
Dumay wax ndimbal
Ndimbal gi may noot
Di may dugal ci pax
Pax biy gëna xóot
Amatuñu ndox mu teey
Jàngoro yi ñu ngi ray
Xale yaa ngi deek xiif
Jur mer mu dul giif
ANNULONS LA DETTE
ET RELEVONS LA TÊTE!
Ñun dundatuñu
Néew ji doole yi lañu xoj
Ñun dundatuñu
Néew ji doole yi lañu xoj
Sunu njiit yii
Dii dundee politig
Politig googulee
Banque mondiale tëral
Yore kàccireem
Maanaam xaalisam
Ku deful ndigtalam
Ñoom ñu xañ la dërëm
Ñun dundatuñu
Néew ji doole yi lañu xoj
Ñun dundatuñu
Néew ji doole yi lañu tancc!
Written by: El Hadji Ndiaye, Ndiaye El Hadji Samba
instagramSharePathic_arrow_out

Loading...