Lyrics

Anhhh (Yo the good, the bad, le bien, le mal Li baax ak li bonn, si miim reew la fék baax Yoooo the good, the bad, le bien, le mal Li baax ak li bonn, si miim reew la fék baax Yoooo the good, the bad, le bien, le mal Li baax ak li bonn, Senegal la fék baax Yoooo the good, the bad, le bien, le mal Li baax ak li bonn, si miim reew la fék baax) Baaxa ngi ame batay c'est que bonn dafko geuneu feuss Bonn Daf di diourom béne fane baax nek béne Bés Kéne wolotoul kéne motax kene bougoul koula seuss Do meuseu xamni baax diekoul so tamé di deglou teuss Beug lou yomba tax niou tayala djeul yonn bou baax Djoudou rek Bonn beug tekki té dougn dioug fign né faax Djoub yomboul goney yi né deukoum taax Bouki bou yoré allumette alleu bi yeup laye sopi daumou taal Bonn meunteu wessou djoudou si guelam nameu si mbam Comme Domou elimane bou waxtou djouli di fék si bar Kou baax loum yéné boppam rek laye yéné moromam Legui nioune nieupeu bokk bone kouné si nioune ame nga si part Fi kila geuneu yèss legui lagn geuneu diokh thieur Bo baxé bingay dounde lagn laye mirass seddo saye keur Djiguen bouy mayé ndawam gayi yaw rek lagni weur Djeul na si lingay mayé mais est-ce que dîna done sa djeukeur Done Naffi bonn bonn Lou Farr guiss gnouma geuneu bonn Ay paa youy teude ak séni dome ay Gars youy teude ak séni bone École sax baxatoul fala boyi di touxé boon Nioune téla xam lou nekh motax nioj tela niak diom Ay nopp youy degg saxoul si sounou bopp motax Diafé na niou songue mbirr ba djeulé barké Fi bofi baxé legui gayi def la doff Gnigua done dimbeuli bingay ame binga niaké dagn la faté (faté) Deuk bi baax fi legui woratoul (woratoul woratoul) Diay sa bopp legui bonatoul (bonatoul) Doundé alale bou léwoul bonatoul (bonatoul) Reew mi legui wax fi lou baxoul sax bonatoul (bonatoul bonatoul) Han Deuk bi baax fi legui woratoul (woratoul woratoul) Donn fi nittou deug doxatoul (doxatoul doxatoul) Doundé alale bou léwoul bonatoul (bonatoul) Reew mi legui wax fi lou baxoul sax bonatoul Lou baax lifi niou baax gni bayiwone sax samtougn ko Niak doylou moy ame louné gagneu di waliyani Deukou teranga mais fi bo yoroul niou xebb sa dioudou System béniouy Xiff lo té fi kéne baniatoul ni niani Souf sé yakou bofii djiwone baax sax bonn ngay gaub Sougn la tegualone chaisou baax ak bonn si bane ngay togg Fi baax moy mayé xaliss soirée Wally bayi sa mbok Fi Bonn moy bala ngay defal keneu defal sa bopp C'est le monde à l'envers Paradis en enfer Dangay nek si niitou deug sax guiss nioulay sani xerr Legui yémétoul Bo teudé sa djabarou propre frère Motax woratoul bayi sa djabar ak propre père Fi do togg bës bo deggoul mbidef bouniou faate Boy yegui taakeu mais tewoul guél yi di niane sene bate Kilifeu bila dakeu fene mola dagua waat Kila geuneu neew lé xam xamala geuneu beuri wax Fi lignouy lekeu baaxoul Lignouy nane baxoul Lignouy setane télék lignouy degg radio baxoul Deug bou saath di até saath justice bi baxoul Jummah bou aye sabar inauguré djouli si baxoul (Gorgi néna) Baax djegui siraat le aka diafé diegui (Tégg si) Mbonn gui dadj na fépp ni gedj niata si sobou rérr si (Xolal) Fou niitou Deug taxaw wax fene katay wédi Boumou goré bignou Borom bi yéwon la djaam bi yéwi (Anhhh) Deuk bi baax fi legui woratoul (woratoul woratoul) Diay sa bopp legui bonatoul (bonatoul) Doundé alale bou léwoul bonatoul (bonatoul) Reew mi legui wax fi lou baxoul sax bonatoul (bonatoul bonatoul) Han Deuk bi baax fi legui woratoul (woratoul woratoul) Donn fi nittou deug doxatoul (doxatoul doxatoul) Doundé alale bou léwoul bonatoul (bonatoul) Reew mi legui wax fi lou baxoul sax bonatoul
Writer(s): Mouhamed Loucar, Momar Ndiaye Lyrics powered by www.musixmatch.com
instagramSharePathic_arrow_out